Charpentier: Miserere des Jésuites, H. 193: I. Prélude

de ZDRID FAMILY

Àddina ak li ci biir boo demee ba am ko
Bul fàtte, bul fàtte, fa nga cosaanoo
Àddina ak li ci biir boo demee ba am ko
Bul fàtte, bul fàtte, fa nga cosaanoo

Àddina ak li ci biir boo demee ba am ko
Bul fàtte, bul fàtte, fa nga cosaanoo
Àddina ak li ci biir boo demee ba am ko
Bul fàtte, bul fàtte, fa nga cosaanoo

Xam na nu fi nu joge
Li nu jaxal mooy fu nu jëm de
Suufu maam yi moom bu nu woowe
Du nu tànqamlu du nu soree
Danuy fatu nu mu gëna gaawee
Ñun ndawu reew mi da nu pare
Ji fi luy jëriñ fi ak fë le
Ba ñu ñu ci dara ku ngemboy bëre

Wër naa àdduna
Japon, Inde, Australia
There is no place like home
Fenn du Sunugaal

Fa nga cosaanoo
Fa nga cosaanoo

Ku fi fàtte demb, ëlëg dalay reer
Waxu mag la degg nga du am kubeer
Fattëlikul ki nga doon fi nga juddoo
Fi nga jugee, fi nga dëkk Yàlla mi la bind
Ngor, jom, fit la, fayda boo ko amul
Doo xam fi nga jëm dara du ku dindi
Li ci Baay bi di doom na ko jëli
Kaddu mag ñi nii na ko sët yi firi
Na nu gëna disoo ndax ñu mëna deggoo
Xana gisoo jikkoo yi ni gëna yàqoo
Na nu dellu te toogi mëna root du doy di
Àdduna ngi daw di na ñu def ci bopp yi
Bul di fàtte ñi la fàl ñi la tettewoon
Ñi la gunge bi ngay raam ñi nga nekkaloon
Lakoon fakoon ñakoon
Lawoon fawoon ñawoon

Xaleel poto poto la
Noko raaxe rek lay weyee
Fi laa yaroo fi laa maggee
Lu mu guddi guddi guddi damay ñibbe
Galsen mooy daw sunu deret
Dañu wutiwoon ba tax ñu ne bëreet
Teranga yi ñi fay jëlee su nu askan lañ koy jëmee

Wër naa àdduna
Japon, Inde, Australia
There is no place like home
Fenn du Sunugaal

Fa nga cosaanoo
Fa nga cosaanoo
Fa nga cosaanoo
Fa nga cosaanoo

Más canciones de ZDRID FAMILY