Photo

de BASH

Lii ñuy nekk yépp doon di ànd
Dawuma xalaat di lay ñàkk
Sunu rêve bi moo nekkoon
Dundu dem ba gëna mag dal di tuddunte ay doom

Dem na
Oh jooy naa!
Lii mooy sama tiis
Jot nga départ dootuma la gis
Lii daf ma mujju yéem
Donoon nga ku may yee
Danga ma gëna yokk def fulë ci sama life

Xarit sama xol bi daf ci fees
Bi may tokk ñu naan ma danga dem
Li ma ñàkka reer
Mooy sama saggoo
Man de sama xol bi daf ci fees dell!
Bi may tokk ñu naan ma da mujje dem
Bi mu may sooga reer
Laa xam ni dafa doon taggoo
Ñàkk naa, hmm!

No, no! No, no!
No no no no noo
Maa ñi xaar
Bés dina ñëwaat ñu gisee
Jàmbaar
Ndaanaan dem na ni
Maa ngi lay ñaanal
Fi nga nekk gënal la fuuf fi nga juge tay

Man dama mujj wet
Ba tax na dama réer
Oh waay!
Sama waa ji dem na ni
Jooy naa
Jooy naa, jooy naa, jooy naa
Man jooy naa sama waje

Xarit sama xol bi daf ci fees
Bi may tokk ñu naan ma danga dem
Li ma ñàkka reer
Mooy sama saggoo
Man de sama xol bi daf ci fees dell!
Bi may tokk ñu naan ma da mujje dem
Bi mu may sooga reer
Laa xam ni dafa doon taggoo
Ñàkk naa, hmm!

Más canciones de BASH